¶ Ba mu ko defee waa Misra soññ bànni Israyil, ngir ñu gaaw génn réew ma, ndax booba ña nga naan: «Nun ñépp ay dee!»
TSK
TSK · Isaiah 52:12
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Bu bëccëgee nag Aji Sax ji nekk ci seen kanam ci biir taxaaru niir, di leen jiite ca yoon wa, te bu guddee mu nekk ci biir taxaaru sawara, di leen leeral, ba ñu mana dem guddi ak bëccëg.
¶ Ci kaw loolu malaakam Yàlla, ma féete woon xarekati Israyil kanam naka jekk te di leen jiite, daldi toxu, féete leen gannaaw. Niir, wa leen jiitu woon it walbatiku, taxaw ca seen gannaaw,
Ndaxte seen Yàlla Aji Sax ji mooy kiy dox ànd ak yeen, xeexal leen ak seeni noon, ngir may leen ndam.»
Moo tax Boroom bi Aji Sax ji wax ne: «Maa ngii di dëj fi Siyoŋ aw doju coll, muy doju collu tànnéef wu gànjare ngir kenu gi, te ku ko wéeroo doo gaawa daw.
Ku diisoon ba waaf léegi nga féex; doo deeye pax ma nga tëje, te doo ñàkk loo lekk.
Kiy bëtt mooy dox, jiitu leen, ñu bëtt, jàll bunt bi, dem. Seen buur mooy jàll jiitu leen, Aji Sax jeey dox fa seen kanam.»