TSK

TSK · Isaiah 52:6

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Musaa ne Yàlla: «Su ma demee ca bànni Israyil, ne leen seen Yàllay maam ya moo ma yónni ca ñoom bànni Israyil de, dinañu ma laaj nu mu tudd. Lu ma leen di wax nag?»

¶ Aji Sax ji nag wàcc ci biir aw niir, taxaw ak Musaa foofa, daldi biral turam, ne: «Aji Sax ji.»

Céy Yàlla, nu ngi sa biir kër, di xalaat sa ngor.

Mbir ya jiitoo ngoog, mat na; yu yees laa leen di yégal, balaa teew, ma yegge leen ko.»

Yaay naan soowum xeet yi, nàmp weenu buur yi, ba xam ne maay Aji Sax jiy walloo, jàmbaaru Yanqóoba ji lay jot.

Yeen waa kër Israyil, duma jëflanteek yeen li seen jikko ju bon yelloo ak seen jëfi yàqute, waaye sama teddngay tur laa ciy seet, ba ngeen xam ne man maay Aji Sax ji. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.”»

Bu ma leen jëlee ci xeet yi, délloosi leen, maa leen di dajalee ca seen réewi noon yooya, maa leen di fésale sama sellnga, yéefar yu bare teg ci bët.

ne ko: «Maa lay barkeela barkeel déy, ful laa ful.»