TSK

TSK · Isaiah 53:4

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

ak wenn yëkk wu ndaw, ak menn kuuy, ak menn xarum menn at, ngir saraxu rendi-dóomal,

Yal na seeni dal gent, seeni xayma wéet.

Te moom sunuy tooñ a waral ñu jamat ko; sunuy ñaawtéef a waral ñu dëggaate ko. Yar yi nu jàmmal moom la dal, te mooy ki nu wére ciy góomam.

noonu itam la Almasi doone ab sarax benn yoon, ngir gàddu bàkkaaru nit ñu bare, te dina teewsiwaat, ci yoon wu joteetul dara ak bàkkaar, ngir indil ñi koy séentu seenug mucc.

Almasi itam benn yoon la daj coono ndax bàkkaari nit ñi, moom miy ki jub moo leen ko defal yeen ñi jubadi, ngir yóbbu leen fa Yàlla; moom lañu rey yaramu suuxam, waaye moo dundaat ci dooley Noo gi.