TSK

TSK · Isaiah 55:2

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Su fekkee ne nag sàmm ngeen ba sàmm sama santaane yi ma leen dénk tey jii, ngir sopp seen Yàlla Aji Sax ji, di ko jaamoo seen léppi xol, ak seen léppi bakkan,

Gaynde man naa ndóol, xiif, nit sàkku Aji Sax ji, ñàkkul lenn lu baax.

Dama lay sant, sama giiru dund kay, yékkatiy loxo, sàbbaale la.

Mooy picc mu tàbbi cig fiir. Du xam ne day dee, ba keroog fitt jam ko ci xol.

«Kaay, ma may la, nga lekk, xellil lay biiñ, nga naan.

Su ngeen ma nangoo déggal, ngëneelu réew mi ngeen di xéewloo.

Kee di jur gu fore ab dóom, xelam nax ko, sànk ko. Du keey musal bakkanam de! Du kee naa: «Xanaa duy caaxaan laa ŋàbb nii?»

Dégluleen maa, yeen ñiy wut njekk, di sàkku Aji Sax ji. Xool-leen doj wi ñu leen yette, xool xóotey kàmb gi ñu leen seppee:

Yeen ñi xam njekk, dégluleen ma, yeen, askan wi sama yoon yebu ci seen xol. Buleen ragal nit ku leen sewal, buleen tiit seeni xaste.

Maay yafal sarxalkat yi, ba reggal leen, sama ñoñ ñi regge sama ngëneel.» Kàddug Aji Sax jee.

«Efrayim, ay fen la ma gawe, waa kër Israyil laa ne, ñoo ma yéewe ag njublaŋ, waaye Yudaa ngi ànd ak Yàlla ba tey, di sàmm kóllëreek Ku Sell ki.»

Indileen sëlluw yafal wa, rey, nu lekk, te bànneexu;

Waaye xeetu Israyil wi sàkku woon yoonu njub, ñoo moy yoon wi.

Kon boog ngëm ci dég-dég lay juddoo, dég-dég ba bawoo ci kàddug waare gi jëm ci Almasi.

¶ Buleen nangu ay àlluwa yu bare te woroo ak sunu ngëm, di leen fàbbi. Li baax mooy ngeen di yokke aw yiw, seen pastéefu xol. Buleen yokke pastéefu xol, ay ndigal yu jëm ci aw ñam, te ña koy sàmm, jariñu leen dara.