Nañu jokku ci yaw, te ñu dénkoo ndénkaanel xaymab ndaje mi, ci mboolem liggéeyu xayma bi. Kenn ku ci bokkul nag du leen jege, yeen.
TSK
TSK · Isaiah 56:3
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Bu kenn jël jabaru baayam, di teddadil lalu baayam.
Ñi soqikoo ci ñaari xeet yooyii, ca ñetteelu maas ga, te di seeni sëtaat nag, sañ nañoo bokk ci ndajem gëmkati Aji Sax ji.
¶ Aji Sax ji kay mooy yërëm askanu Yanqóoba, dellu taamu xeetu Israyil wii. Moo leen di sancaatal fa seen suuf, doxandéem yi fekki leen; boole seen bopp ci askanu Yanqóoba.
maa leen di may ci sama biir kër, sama biir ëtt, doj wu ñu leen di fàttlikoo ak tur wu leen di gënal doom yu góor ak yu jigéen. Tur wu sax dàkk laay may jaam yi ñu xañ ngóora, te du fey mukk.»
«Demal nga wax Ebedd Meleg, Kuuseen ba, ne ko: “Aji Sax ji Yàllay Israyil Boroom gàngoor yi dafa wax ne: Maa ngi nii di sottalsi sama kàddu yi jëm ci dëkk bii, muy ayam te du doon jàmmam. Dina am ngay gis, bésub keroog.
¶ Ba loolu amee Buur jox ndigal Aspenas, kilifay bëkk-néegam, ngir mu tànne ci bànni Israyil, ñenn ci askanu buur ak ci garmi yi.
Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne: «Ay askan ñooy dikkati, di waa dëkk yu bare,
¶ Yeesu daldi ànd ak ñoom. Naka la jubsi kër ga, njiit la yóbbante ay xaritam kàddoom, ñu gatandu Yeesu, ne ko: «Sang bi, jarul ngay sonn, ndax sab tànk sama biir kër, man yeyoowuma ko.
¶ Ku ñuy wax Korney, njiitu takk-der la woon ca Sesare. Ma nga bokkoon ca mbooloo ma ñu dippee Gàngooru Itali.
Ndax noonu la nu ko Boroom bi sante ba mu nee: “Maa la tabb ngay leeru jaambur ñi, ngir nga jottliji mucc gii, ba ca cati àddina.”»
¶ Mu jóge foofa, dem kër jaamburub jaamukatu Yàlla bu ñuy wax Tisyus Yustus, te këram sësook jàngu ba.
Leneen li indi Almasi mooy may jaambur ñi dul Yawut lu ñu màggale Yàlla, te muy yërmandeem. Noonu it la Mbind mi indee ne: «Looloo waral ma sant la ci biir xeet yi, sàbbaal la.»
Waaye ku taqoo ak Sang bi, yaak moom genn noo ngeen di doon.
Ci Almasi ngeen bokke ci tabax bi, yeen jaambur ñi itam, ba mana doon dëkkuwaayu Yàlla, ci ndimbalal Noo gu Sell gi.