TSK

TSK · Isaiah 56:6

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Kii nee: “Aji Sax jee ma moom.” Kee di tuddoo turu Yanqóoba, kale bind ca loxo ba: “Maa ñeel Aji Sax ji,” tey wuyoo turu Israyil.»

«Su ngeen téyee seen tànk bésub Noflaay, baña def li leen neex sama bés bu sell; su bésub Noflaay di seen nammeel, di bésub Aji Sax bu sell bu ngeen teral; ngeen teral bés bi, bañ cee topp li ngeen jikkowoo, di topp seen bakkan ak wax ju dul jeex;

Ay gan ay dikk, di leen sàmmal seeni gétt, ay doomi doxandéem di leen beyal tool ak tóokëru reseñ.

Nangeen ko tegoo bant, séddoo ko ci seen biir, yeen ak doxandéem yi sanc ci seen digg te jaboot ci réew mi. Nangeen leen jàppe ni ay njuddu-ji-réew fi digg Israyil. Nañu am seen céru suuf ni yeen, bokk ci yem ak giiri Israyil.

Acts 2:41 TSK

¶ Ña nangu kàddug Piyeer nag, ñu sóob leen ci ndox; bésub keroog lu wara mat ñetti junni (3 000) yokku nañu ca gëmkat ña.

¶ Te itam nag xam nanu ne Yàlla mooy def mboolem lu xew, daje ba jur njariñal ñi sopp Yàlla, ñi mu woo, noonee ko ab dogalam namme.

Li nu séentu woon sax wees nañu ko, nde Sang bi lañu jëkka jébbal seen bopp, door noo jébbal seen bopp, te noonu la ko Yàlla bëgge.

Na aw yiw ñeel mboolem ñi sopp sunu Sàng Yeesu Almasi, cofeel gu dul fey.

¶ Ndokklee ku muñ ab nattu, nde su ca amee ngërëm, mooy yooloo kaalag dund, gi Yàlla dig ñi ko sopp.

Maa nekkoon ci biir Noowug Yàlla benn bésub Sang bi, ma dégg ci sama gannaaw baat bu xumb nig liit.