Su boobaa da naan: «Ana seen yàlla ya, seen kiirlaay lañu daa làqoo?
TSK
TSK · Isaiah 57:6
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Kee moom mu ngi rendiw yëkk, sarxal, te teewu koo bóome. Kee rendiw xar, sarxal, te teewu koo damm loosu xaj, sarxal. Kee ngi joxe saraxu pepp, te teewu koo tuur deretu mbaam-xuux. Kee di taal saraxu baaxantalu cuuraay, tey jaamu ay tuur. Ñoo taamu seen yoonu bopp, safoo seeni jëf ju seexluwu.
Lii, duma leen ko dumaa?» Kàddug Aji Sax jee. Mu ne: «Wii xeet, duma ko fey yoolam?»
Doom a ngi taxan, baay di taal, jigéen di not lu mu nàkkal ki ñuy wooye Lingeeru asamaan, di tuural ay naan yeneen yàlla, di ma ko naqarale!
Këri Yerusalem ak këri buuri Yuda dina fees ak sobe ni bérab bii di Tofet. Mooy mboolem kër yu ñu doon taalal cuuraay ca kaw taax ya ñeel biddiiw yépp, ak di fa tuural yeneen yàlla.”»
Nooy def ba defaatoo mboolem lu nu digoo woon, di taalal cuuraay Lingeeru asamaan, tuur mi, di ko tuural ay naan, na nu ko daan defe naka jekk, nook sunuy maam ak sunuy buur ak sunuy kàngam ci dëkki Yudak mbeddi Yerusalem. Teewul dañu daan doyal dugub, di woomle, te gisunu loraange.
Wóoy, ngalla ku naan bant: “Xippil,” naan doj wu ne selaw: “Yewwul!” Ana lu yooyii di xamle? Ma nga, ñu xoobe ko xaalis ak wurus, te du gennug noo ci biiram.