TSK

TSK · Isaiah 59:3

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Bu ngeen ma tàllaleey loxo, ma fuuyu. Bu ngeen doon ñaan-ñaanee it, du maa leen di déglu: seeni loxo, deret la taq ripp.

«Mbugal naa seeni doom, jariñul dara. Dégguñu yar, bóom ngeen seeni yonent, mbete gaynde yuy fàdde.

Yeena ngii di naxe seen bopp waxi caaxaan yu amul njariñ.

«Na ku ne moytu dëkkandoom te baña wóolu menn mbokk. Kuy mbokk déy lal nga pexem wuruj, di wuruj; kuy dëkkandoo, sos ngay wéye.

«Yaw xooloo, xalaatoo lu moy loo jariñoo, ak noo tuure deretu jaamburu Yàlla, di fitnaale ak a lore?»

Mu ne ma: «Tooñaangey waa kër Israyil ak Yuda moo ëpp loxo lool. Réew maa ngi fees ak deret, dëkk bi fees ak yàqute. Nee nañooy: “Aji Sax ji wacc na réew mi. Aji Sax ji gisul dara.”

«Yaw nit ki, doo tiiñal ñii? Doo tiiñal waa dëkku tuurkati deret yii? Xamal leen seen jëf ju siblu jépp.

Hosea 4:2 TSK

Xanaa ay móolu aki wor, bóome, càcc ak njaaloo. Dañoo ràkkaaju, di tuur deret ci kaw deret.

Ngalla ñoom, nde ñoo ma daw, yàqute ñeel na leen, nde ñoo ma gàntal. Doon naa leen jot waaye ñoo ma fenal.

Deret ngeen tabaxe Siyoŋ, njubadi ngeen tabaxe Yerusalem googu.

Micah 7:2 TSK

Ngor a jeex ci réew mi, njub tumurànke ci nit ñi. Ñépp, ku ñu tuur deretam lañuy tëru, ku nekk, mbokkam lay fiir.

yu leen ay jinigalkat, ay fenkat yu dërkiis ab xol, di naxe.