¶ Yonent Yàlla Maryaama, jigéenub Aaróona nag ŋàbb tabala, jigéen ñépp topp ko, génn di fecc, tabala ya jiin.
TSK
TSK · Isaiah 6:3
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Ña ngay jàng, di màggal ak a sant Aji Sax ji, naan: «Kee baax. Kee gore ba fàww ci Israyil.» Ci kaw loolu mbooloo ma mépp xaacu, di ko màggale Aji Sax ji ngir kenug kër Aji Sax ja lale.
Mu jëm ci njiital jàngkat yi, di kàddug Sabóor, ñeel Daawuda.
Sa ngor a màgg, ba àkki asamaan, sa worma àkki fa kawa kaw.
Cant ñeel na teddngaam, ba fàww, yal na teddngaam dajal suuf sépp! Amiin, Amiin!
Deesatul gaañe mbaa di lore, fi mboolem sama kaw tund wu sell wi, ndax ni ndox di feese ba muur géej, ni la àddina di feese nit ñu xam Aji Sax ji.
darajay Aji Sax ji daldi feeñ, jaam ñépp bokk gis ko. Aji Sax jee ko wax ci làmmiñam.»
Waaye ni ndox muure xóotey géej ba mu daj, ni la darajay Aji Sax jiy ràññikoo ci àddina sépp.
Ngir itam seen bëti xol leer ba ngeen gis yaakaar ji ci wooteem, ak ni ay ngëneelam géejoo te yéeme, ñeel ñu sell ñi mu séddoo.
Ña ngay woy woyu Musaa jaamu Yàlla ba, ak woyu Gàtt bi, naan: «Yaw Boroom bi Yàlla Aji Man ji, yaa réy te yéeme ay jaloore. Yaw Buuru askan yi, yaa jub te dëgguy doxalin.