TSK

TSK · Isaiah 61:4

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi
Ezra 9:9 TSK

Ndax ay jaam lanu, waaye yaw sunu Yàlla, waccewoo nu sunug njaam. Yaa dawal ngor sunu digganteek buuri Pers, ngir mayaat nu dooley tabax sunu kër Yàlla, yékkatee ko ca gentam ba, may nu kiiraay ci Yerusalem ak ci Yuda.

Aji Sax ji dafa wax ne: «Bu bésub yiw taxawee, ma nangul la; bu bésub mucc jotee, ma wallu la, sàmm la, def la ngay kóllëre sama digg ak askan wi, ngir yékkatiwaat réew mi, séddalewaat ay cér, suuf sii gental tey,

Kon dinaa fésal sama sellngay tur wu màgg, wi ñu teddadil fi biir yéefar yi, sama tur wi ngeen teddadil fi seen biir. Ci yeen laay fésale sama sellnga, yéefar yiy gis, ba xam ne maay Aji Sax ji. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.

Amos 9:14 TSK

Maay tijji wërsëgu Israyil, sama ñoñ; ñu tabaxaat seeni gent, dëkke; jëmbat seen tóokëri reseñ, naan seen biiñ, bey ay tool, lekk ca meññeef ma.