¶ Siwon buurub Esbon nag nanguwu noo may nu jaare fa moom, ndax booba seen Yàlla Aji Sax ji moo dëgëral boppam, wowal xolam, ngir teg ko ci seen loxo niki bésub tey jii.
TSK
TSK · Isaiah 63:17
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Muy taalifu yeete, giiroo ci Asaf. Éy Yàlla, lu tax nga wacc nu fàww, di dal ak xol bu tàng ci sa xari parlu yii?
Aji Sax ji, délsil, loo deeti xaar? Ngalla yërëmal sa jaam ñi.
Joyantil sama xol, mu féeteek sa kàdduy seede, te dummóoyu alal ju lewul.
Nanga dërkiisal xoli askan wii, fatt seeni nopp, taf seeni gët; lu ko moy seeni gët gis, seeni nopp dégg, seen xol yég, ñu dëpp, wér.»
Boroom bi nee: «Askan wii, làmmiñ lañu ma jegee, lori neen lañu may wormaale, te seen xol sore ma. Seen ragal ak man it, njàngum tari kepp la.
¶ Malaakam Aji Sax ji ne: «Éy Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, loo deeti xaar, doo noppee xañ yërmande Yerusalem ak yeneen dëkki Yuda? Juróom ñaar fukki at a ngii yoo leen mere!»
Kon nag Yàlla mooy yërëm ku ko neex, te ku ko neex lay dëgëral xolam.