Foofa laay dajeek yaw; fa tiim kubeeru njotlaay ga, ca diggante ñaari serub ya ca kaw gaalu seede sa, fa laa lay waxe mboolem lu ma lay sant, ñeel bànni Israyil.
TSK
TSK · Isaiah 64:5
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ «Tegal sarxalukaayu cuuraay bi ci kanam rido, bi làq gaalu àlluway seede si ak kubeeru njotlaay, gi ci kaw gaalu àlluway seede si, foofu may dajejeek yaw.
Deel bànneexoo Aji Sax ji, mu may la say nammeel.
Waaye ngoru Aji Sax ji naka jekk ñeel na fàww ku ko ragal; njekkam ñeel sëtaati
Yeenay meli ni garab gu mag gu xob ya lax, mbaa tóokër bu amul siitu ndox.
Ndànk-ndànk la jëflanteek ñoom, ba mu leen toxalee, dàqe leen noowam gu mag, bésu ngelawal penku.
Waaye ñoom ñoo fippu, di naqaral xelam mu sell, mu soppliku seen noon, ba mujj di xareek ñoom.
Nan ràññee, di saxoo faale Aji Sax ji. Ni jant bu fenk la dikkam wóore, ni ab taw la nuy dikkale, ni ab tawu mujjantal buy seral suuf.»
¶ Yosuwee ngi sol yére yu dand, taxaw fi kanam malaaka mi.
Ku jullite la woon te ragal Yàlla, mook waa këram gépp; bare woon na sarax yu muy yéwéne askan wi, te ñaan ci Yàlla la saxoo woon.
Bokk yi, fooguma ne jot naa ci, xanaa kay lenn: damay fàtte li ci gannaaw, te def lu ma man, ngir fexee yóotuji li ci kanam,