TSK

TSK · Isaiah 65:1

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Ku woyof a cay lekk ba doyal, kuy wut Aji Sax ji, sant ko. «Guddleena gudd fan!»

Bésub keroog car bawoo ca Yese, reen ba, taxaw di raaya buy gindi xeet yi, xeet yi di ko sàkku, dal-lukaayam ba jagoo teddnga.

Waaye maa jëkka yégal Siyoŋ ne leen: «Xool-leen, ñu ngii!» Maa indil Yerusalem ndaw lu indi xibaaru jàmm.

Yeen waa àddina, catoo cat, walbatikuleen fi man, mucc. Man maay Yàlla, du keneen.

Nu ngi mel ni xeet woo masula yilif, xeet wu ñu masula tudde sa tur. Éy soo xaroon asamaan, wàcc, ba tund yi yëngu fi sa kanam!»

«Éy Siyoŋ, rëccal, yaw mi dëkke janq Babilon mu taaru mi.»

Yeesu gis ko, woo ko, ne ko: «Jongama, teqlikoo nga ak sa laago.»

Nun ci ndabi yërmande yi Yàlla woo lanu bokk, te du ci Yawut yi rekk lees nu seppee, waaye ci jaambur ñi dul Yawut itam.

Esayi it am fit ba ne: «Ñi ma seetul woon, gis nañu ma, ca ña ma laajul woon laa feeñe.»

Yeen ñi dul woon sax aw xeet, démb, tey yeen ay xeet wi Yàlla ñoñoo; dajaguleen woon yërmande, waaye tey daj ngeen yërmande.