¶ «Sàkkal ab sarxalukaay bu ñuy taal cuuraay ci kawam. Bantu séng nga koy defare.
TSK
TSK · Isaiah 65:3
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Ñoo yee fiiraangeem, ndax ay yàllay doxandéem, ñoo ko merloo ak seen tuur yu jomblu.
¶ Teewul ñu të ticc, sajju loos ni seen maam ya gëmuloon seen Yàlla Aji Sax ji.
Xàccil sa loxo rekk, dal ci mboolem lu bokk ci moom. Ndegam du jàkkaarlook yaw, xarab la.»
Gàntal nañu ko ba tàyyi ca màndiŋ ma, teg ko naqar ca ndànd-foyfoy ga.
Yeenay rus moos ci garab yu mag, yi ngeen soppoona daje, di xërëmtu. Yeenay am gàcce ci tóokër, yi ngeen taamu woona daje, di bokkaale.
«Ñii di sellalu ak a sangu-set bala ñoo duggi tool ya ñuy tuuroo, di fa toppi ca gannaaw ka ca digg ba, ñooñooy lekk yàppu mbaam, ak yeneen yu seexluwu ni janax, te ñooy bokk sànku.» Kàddug Aji Sax jee.
Askanu Israyil ak Yuda kay, ca cosaan ba tey, defuñu lu moy lu bon fi sama kanam. Bànni Israyil, mboolem lu ñu def, defuñu ko lu moy di ma merloo.» Kàddug Aji Sax jee.
Maa leen yóbbu réew ma ma leen giñaloona jox, teewul fu ñu gis tund wu kawe, mbaa garab gu sëq, rendi nañu fa seeni sarax, jooxe fa seen jooxe yi may merloo, taal fa seen saraxi cuuraay, tuural fa seeni tuur.