¶ Ba loolu amee Aji Sax ji wax Musaa ne ko: «Bindal lii xew cib téere, muy pàttli, te nga xamal Yosuwe ne ko, raafal laay def askanu Amaleg, ba ñu jeex tàkk, ba deesatu leen fàttliku fu asamaan tiim.»
TSK
TSK · Isaiah 65:6
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Sunu Yàllaa ngi ñëw te du ne cell, sawaraa ko jiitu, di xoyome, ngëlén lu mag wër ko.
Éy gii ñaawtéef! Ñii nu ñu mana mucce? Éy Yàlla, yal na leen sa mer dal!
Aji Sax ji nee: «Damaa yàgga xeremlu, ne cell, téye sama bopp. Waaye léegi, ni kuy matu laay onke, di xiix ak a àppaat boole ca.
Dama leen di jëkka fey ñaari yoon seeni moy, ndax ñoo sobeel sama réew meek seen méddi tuur yu bon yi, feesal suuf sii ma séddoo seen yëf yu siblu yooyu.»
Ma daldi leen xëpp samam sànj, fàkkase leen sama tàngooru xadar, këpp leen seen añu jëf ci seen kaw bopp. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.»
Ca la ñi ragal Aji Sax ji diisoo ci seen biir, Aji Sax ji teewlu, déglu leen. Ñu bind fi kanamam téereb fàttliku, bu lim ñi ragal Aji Sax ji, te teral aw turam.