TSK

TSK · Isaiah 65:7

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Buleen ci sujjóotal lenn, buleen ci jaamu lenn, ndax man seen Yàlla Aji Sax ji, Yàlla ju fiir laa. Maay topp doom tooñu waajur, ba ca seen maasi sët, ba ca maasug sëtaati nit ñi ma bañ.

Yeen nag defuleen lu moy jóg wuutu seeni baay, njurum bàkkaarkat yi ngeen doon, di xamb sànjum Aji Sax, ji tàkkal bànni Israyil?

Teewul jëlewu fa bérabi jaamookaay ya. Askan wa dañu fa daa dem ba tey, di fa rendi saraxi jur, di fa taal cuuraay.

Bérabi jaamookaay ya jëleesu ko fa. Mbooloo maa nga doon def ay sarax ca bérabi jaamookaay ya ba tey, di fa taal cuuraay.

Rendi nay sarax, taal na cuuraay ca bérabi jaamookaay yaak ca kaw tund yaak mboolem ker garab gu naat.

Noo bàkkaar, nook sunuy maam; noo def lu ñaaw, def lu bon.

Tund wu mag te kawe, nga fàkk fa tëraay, yéeg fa, di fa sarxalal.

Lii, duma leen ko dumaa?» Kàddug Aji Sax jee. Mu ne: «Wii xeet, duma ko fey yoolam?»

Du man lañuy naqaral moos!» Kàddug Aji Sax jee. Mu ne: «Xanaa kay ñoo ciy rus!»

Dama leen di jëkka fey ñaari yoon seeni moy, ndax ñoo sobeel sama réew meek seen méddi tuur yu bon yi, feesal suuf sii ma séddoo seen yëf yu siblu yooyu.»

¶ «Moo tax, yaw nit ki, nanga wax ak waa kër Israyil, ne leen: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Seeni baay a ma dellu ŋàññ, fecci ma kóllëre.

Aji Sax ji, nun kay gàcce ñeel na nu, nook sunuy buur ak sunuy kilifaak sunuy maam, ndax moy nanu la.

Ñoo nuy aaye nu àgge jaambur ñi dul Yawut, kàddu gi leen di musal. Noonu lañu matale seen jóorub bàkkaar yi ñu nekke naka jekk, waaye am sànj a leen mujj dab.