Dangay teela xëy ca Firawna ëllëg, buy génn jëm ca ndox ma, nga dogale ko ca tàkkal dexu Niil, te yóbbaale yet, wa soppliku woon jaan.
TSK
TSK · Isaiah 7:3
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Buurub Asiri nag tollu ca Lakis, yebal bummeem ak kilifay jawriñam ak bëkk-néegam, ñu ànd ak mbooloom xare mu takku, dem Yerusalem. Ba ñu agsee Yerusalem ba tollook solomu mbàndum kaw ma, fa feggook yoon wa jëm ca toolub fóotukaay ba, fa lañu taxaw.
Bu ca fukkeelu nit ña desoon, ñoom it dees na leen dellu taal. Waaye dañuy mel ni wenn ci xeeti garab yu mag yi ñuy gor, ëkk ba dellu jebbi, ëkku xeet wii, jiwu mu sell lay doon.»
boole ca waññ këri Yerusalem, màbb lenn, sàkk ca lu ngeen aare tata ya.
Buurub Asiri moo yebale fa dëkk ba ñuy wax Lakis, bëkk-néegam Rabsake, mu ànd ak mbooloo mu réy, ba ca Buur Esekiya ca Yerusalem. Ba Rabsake agsee ba tollook solomu mbàndum kaw ma, feggook yoon wa jëm ca toolub fóotukaay ba, fa la taxaw.
te nga dem ba ca xuru Ben Inom, ca buntu Tojitu njaq ya, daldi fay yéene kàddu yi ma lay wax.
¶ Ci mbirum Israyil la Yonent Yàlla Esayi itam xaacu woon ne: «Su bànni Israyil tolloo ni feppi suufas géej sax, as ndes a ciy mucc.