«Céy Aji Sax ji, maa ngi séentu sa xettal!
TSK
TSK · Isaiah 8:17
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Mu ne: «Maa leen di xañ sama kanam, ba gis nu ñuy mujje, ndax maasug defkati njekkar lañu, doom yu ñàkk kóllëre.
Kon ngalla yaw mi ne gisoo ko, te ne diis nga ko sa mbir, di ko xaar.
Nu ngi séentu Aji Sax ji, moo nuy taxawu, di nu feg.
Nit du lu moy takkndeer buy dem, cóolóolu neen lay kër-këri. Nit a ngi dajale, xamul kuy for.
Damay xaar Aji Sax ji, di ko xaare xol, di yaakaar kàddoom.
Bésub keroog dees na ne: «Sunu Yàllaa ngii nag! Moom mii lanu yaakaaroon te moo nuy wallu. Aji Sax jii lanu yaakaaroon, nan bég te bànneexoo wallam.»
Éy Aji Sax ji, ngalla baaxe nu; yaw lanu yaakaar! Xëyeel a dooleel wii xeet, wallu nu ci biir njàqare.
Sama xol a jóg, ma xañ la sama kanam ab diir, waaye maa lay yërëme ngor gu sax.» Aji Sax, ji lay jot moo ko wax.
Seeni ñaawtéef a dox seen digganteek seen Yàlla. Seeni moy a leen xañ kanamam, ba mu tanqamlu leen.
Du kenn kuy wormaal sa tur, mbaa mu yewwu ba jàpp ci yaw, yaa nu làq saw yiw, yaa nu def ban bu tooy ci sunu biir ñaawtéef yi nu tanc.
Aji Sax jee baax ci ñi ko yaakaar, baax ci ki koy sàkku.
Aji Sax ji Yàlla Boroom gàngoor yi, Aji Sax jee di turu bàkkam.
Man nag Aji Sax ji laay séentu, Yàlla ji may musal laay xaar, te sama Yàllaa may nangul.
Aana nag dikk moom it ca waxtu woowa, daldi delloo Yàlla njukkal. Ci kaw loolu muy waxtaane mbirum xale bi ak mboolem ña doon séentu bésu goreelug Yerusalem.
Yal na Boroom bi wommat seen xol, jëme ci cofeelu Yàlla ak muñ gi ci Almasi.
Li leen war moo di muñ, ba sottal coobarey Yàlla, su ko defee ngeen jot li mu dige.