¶ «Buleen jublu ci ñiy gisaane nit ñu dee te buleen jublu ci boroom rawaan yiy seet, ndax kon ñu sobeel leen. Man maay seen Yàlla Aji Sax ji.
TSK
TSK · Isaiah 8:19
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Bu kenn fekk ci seen biir kuy sarxe doomam ju góor, ak ju jigéen, lakk ko; ak kuy luxus, ak kuy seet, ak kuy gisaane, ak kuy xërëm,
Sóol wax ay jawriñam, ne leen: «Seetal-leen ma jigéen juy seete nit ñu dee, ma seetluji ci moom.» Jawriñ ya ne ko: «Xanaa jigéenu gisaanekat ba ca Endor.»
Jigéen ji ne ko: «Ku ma lay wool?» Mu ne ko: «Samiyel nga may wool.»
¶ Ci biir loolu malaakam Aji Sax ji wax Ilyaas, ma cosaanoo Tisbi, ne ko: «Demal gaaw dajeek ndawi buurub Samari te laaj leen ne leen: “Xanaa Yàlla daa amul ci Israyil, ba ngeen di seeti ca Baal Sebub, tuuru Ekkron?”
Rax ci dolli boroom rawaan yeek gisaanekat yeek gàllaaji kër yeek kasaray tuur yeek mboolem kasara yu ni mel te ñu daan ko gis ca réewum Yudak Yerusalem, Yosya jële na ko fa ngir mana saxal kàdduy yoon wa ñu bind ca téere ba Ilkiya sarxalkat ba gisoon ca biir kër Aji Sax ji.
Waa Misra jànnaxe, ma dëpp seen pexe. Ñu seeti yàllantu yeek njuuma yi, ak gisaanekat yeek boroom rawaan yi.
Waaye Aji Sax jeey Yàlla dëgg. Mooy Yàlla jiy dund, di buur ba fàww, xadaram gësëm àddina, meram man xeet yi.
Nit ñi ci seen bopp ñoo nuy waxal fépp, na sunu ngan ak yeen deme, ak ni ngeen walbatikoo ci Yàlla, dëddu tuur yi, bay jaamu Yàlla ju dëggu jiy dund,