TSK

TSK · Isaiah 8:20

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi
Ezra 10:3 TSK

Léegi kay nanu fasanteek sunu Yàlla kóllëre, daldi fase jigéen ñooñu ñépp, ñu ànd ak seeni doom, muy ni nga ko diglee rekk, sang bi, yaak ñi wormaal sunu santaaney Yàlla. Li yoon wi digle daal, na am.

Dégluleen kàddug Aji Sax ji, yeen njiiti Sodom, teewluleen sunu yoonu Yàlla, yeen askanu Gomor.

Aji Sax ji nee: «Ayca, bind ko ci àlluwa, ñu gis! Rëdd ko cib téere, ngir ëllëg ak sibbir, mu dib seede ba fàww.»

Hosea 6:3 TSK

Nan ràññee, di saxoo faale Aji Sax ji. Ni jant bu fenk la dikkam wóore, ni ab taw la nuy dikkale, ni ab tawu mujjantal buy seral suuf.»

Ibraayma ne ko: “Waaye ñoom am nañu yoonu Musaa, am nañu téerey yonent yi. Nañ leen déggal.”

Xel mu rafet lañuy jaay ba mujj diy dof.

¶ Waxleen ma, yeen ñi bëgga nekk ci kilifteefu yoonu Musaa, xanaa xamuleen li yoon wi wax?

Waaye yii jikko, ku ko ñàkk, daa fekk mu gàtt gis-gis ba far gumba, te fàtte ne dees koo fóotoon ba mu set, teqlikook bàkkaari démbam.