Boroom doole mel ni boob, la mu liggéey di ferñent, ànd ak moom ne jéppét, te kenn du fey sawara wa.
TSK
TSK · Isaiah 9:19
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
dellu xool fi suuf, yem ciw tiis, ak lëndëmu njàqare, sóoboo guddi gu fatt taraj.
Moo tax maay gësëm asamaan, suuf yëngoo fa mu tege ndax sànjum Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi, keroog ba meram di tàkk.
Moo tax alkànde yàq suuf, ñi ko dëkke gàddu àq ji. Moo tax waa àddina raaf, ba ñi des di lu néew.
Lëndëm gaa ngii di muur àddina, mu ngi guddil askan yi, te yaw, Aji Sax ji fenkal la, leeru teddngaam feqal la.
Ba loolu wéyee mu wax ak ña ca des, may dégg. Mu ne leen: «Toppleen ko ca biir dëkk ba te ngeen rey. Buleen xool bëti ñéeblu, buleen ñeewante.
Wóoy kuy yàkkamti bésub Aji Sax ji! Ana lu ngeen am ci bésub Aji Sax ji? Dug leer, xanaa lëndëm.
Doom ju góor a ngi dofloo baay ba, ju jigéen ja jógal ndey ja, jabar jógal ndeyu jëkkër ja, nooni nit ki di waa këram.
¶ Ndax Yàlla kat, ndegam moo jéggalul malaaka ya bàkkaaroon, xanaa tàbbal leen kàmbu mbugal, wacce leen ay jéngi biir lëndëm gu ne këruus, di leen nége àtte ba;