¶ Ndaw ya nag bàyyikoo ca kurélu àttekat ya, di bég, gannaaw ñoom lañu jàpp ne ñoo yelloo toroxte ga ñu leen teg ndax Tur wi.
TSK
TSK · James 1:2
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Ana ku nuy tàggaleek cofeelu Almasi? Du ay nattu, te du njàqare, du it coonoy bundxatal, mbaa ab xiif, mbaa rafle, te du genn aaytéef, ba cib saamar.
Ndax kat yeen la may ci jëmmu Almasi, yiwu gëm Almasi, rax ci dolli, ngeen sonn ndax moom,
Yeen itam nangeen ci bég te bokk ak man bànneexu.
Ndax yeena bokk ak ñi ñu tëj seen coono, te yeena muñe xol bu sedd ni ñu foqarñee seen moomeel, ngir xam ngeen yeen ci seen bopp ne am ngeen alal ju ko gën tey sax ba fàww.
¶ Ndokklee ku muñ ab nattu, nde su ca amee ngërëm, mooy yooloo kaalag dund, gi Yàlla dig ñi ko sopp.
Waaye noonu ngeen séddoo ci coonoy Almasi, bégeleen ko, ngir bu ndamam feeñee, ngeen gënatee bég.
Bul ragal mukk mitit wi nga nara daj. Seytaanee ngi noonu di dugal kaso ñenn ci yeen, ngir nattu leen. Dingeen am coono diiru fukki fan. Nanga saxoo kóllëre ba dee fekk la ci, ma kaalaa la kaalag dund.