TSK

TSK · James 1:3

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Te yemunu ci, xanaa di sagoo sunuy tiis itam, nde xam nanu ne dékku aw tiis mooy taxa muñ;

¶ Te itam nag xam nanu ne Yàlla mooy def mboolem lu xew, daje ba jur njariñal ñi sopp Yàlla, ñi mu woo, noonee ko ab dogalam namme.

Sunu coono bu woyof bii ci àddina, ci diggante bu gàtt nag, moo nuy jural teraanga ju diisaay ba jéggi dayo, teraanga ju sax dàkk.

Moo tax nun, nu di leen damoo fi biir mboolooy gëmkati Yàlla yi, ndax seenug muñ, ak seen ngëm, ci biir mboolem ni ñu leen di bundxatale, ak njàqare yi ngeen di jànkoonteel.

Li leen war moo di muñ, ba sottal coobarey Yàlla, su ko defee ngeen jot li mu dige.

Yooyu nattu, ni sawara di natte wurus, ni lay natte seen dëggutey ngëm, te ngëm a gën wurus fuuf, nde wurus day jeex. Su ko defee seen ngëm gu dëggu jural leen ag cant, ak daraja ak teraanga, bés bu Yeesu Almasi feeñee.