Ci moomu mbir la Daawuda doon wax, ba muy biral mbégtem nit ku Yàlla waññal ag njub gu jotewul dara ak ay jëfam.
TSK
TSK · James 2:18
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Waaye ki am xel-yaar, su lekkee, ab daan topp na ko, nde jëfewul ngëm, te lu ngëm lalul bàkkaar la.
Kon bu nit ki bokkee ci Almasi, mbindeef mu bees lay doon. La woon day wonni, li teew nag, di lu yees.
Ci Almasi Yeesu mi nu gëm, xaraf ak ñàkka xaraf, dara amu ci solo; li am solo mooy ngëm, gi jëfi cofeel di firndeel.
Ndénkaane lii nag, li ko taxa jóg mooy luy yee ag cofeel gu bawoo ci xol bu rafet, ak xel mu dal, ak ngëm gu mucc jinigal.
¶ Ndax yiwu Yàlla kat feeñ na, te looloo indil ñépp ag mucc.
Ngëm moo waral ba Raxab gànc ba dalalee jàmm nemmikukati réew ma, àndul ak ñu gëmadi ña dee.
¶ Bokk yi, ku ne gëm na, te jëfewu ko, ana lu mu koy jariñ? Ndax googu ngëm man na koo musal?
¶ Ana ci yeen ku rafet xel te xam àddina? Na ko firndeele dundin wu rafet wu feeñ ci jëfam ju teey ndax xel mu rafet.