TSK

TSK · James 2:19

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Yeen sama ñoñ, yeenay samay seede. Kàddug Aji Sax jee. Yeenay sama jaam bi ma taamu, ngir ngeen xam, ba gëm ma, ba ràññee ne maay moom. Sàkkeesul yàlla ju ma jiitu, mbaa ju may wuutuji.

Buleen tiit, buleen ragal. Dama leena biralul lii bu yàgg, yégal leen ko? Yeenay samay seede. Yàlla daa am ju ma moy? Cëslaay amul, xawma ci kenn!»

Àdduleen, layoosi, diisooleen fi seen biir kay! Ana ku xamle woon lii bu yàgg, yégle woon ko booba? Xanaa du man Aji Sax ji? Kenn du Yàlla ku dul man! Yàlla ju jub, di walloo, du kenn ku dul man!

Jonah 4:4 TSK

Aji Sax ji ne ko: «Waaw, mbaa yaa yey am xol bu tàng ci loolu?»

Aji Sax ji mooy doon buuru àddina sépp, bésub keroog Aji Sax ji di kenn, turam di wenn.

Luke 4:34 TSK

«Moo yaw Yeesum Nasaret, lu nu joteek yaw? Alagsi nu mooy say tànk? Xam naa yaa di kan, yaa di Aji Sell ju Yàlla ji!»

Ndaw sa topp ci Póol ak nun, di xaacu, naan: «Nit ñii jaami Yàlla Aji Kawe ji lañu; dañu leen di yégal yoonu mucc.»

Naka la Póol wax ci mbirum njub, ak moom sa bakkan, ak àtteb bés-pénc, Feligsë daldi tiit, ne ko: «Léegi, man ngaa demagum, bu ma ko talee, dinaa la wooluwaat.»

¶ Kon su dee wàllu ñam wu ñu sarxal ay tuur, xam nanu ne ay tuur du dara ci àddina, te Yàlla kenn la.

Ab jottlikat nag ñaar a koy séq, te Yàlla kenn doŋŋ la.

Ndax kat jenn Yàlla doŋŋ moo am, benn Defarekat doŋŋ it moo am diggante Yàlla ak nit ñi, te mooy nit ki Almasi Yeesu,

Jude 1:4 TSK

Ndaxte ñenn a ngi ñu ñu yàgga bind seenub àtte, te ñoo yoxoosu ci seen biir, di ñu ñeme Yàlla; ñooy taafantoo yiwu Yàlla ngir yoonal ag yàqute, di weddi Buur biy kenn, te di sunu Boroom Yeesu Almasi.

Mu jàpp ninki-nànka ja, jaani cosaan jooju di Tuumaalkat bi, di Seytaane ba tey. Malaaka mi yeew ko diiru junniy at.