TSK

TSK · James 2:8

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Njuddu-ji-réew ji nangeen ko yemaleek doxandéem bi ngeen dëkkal. Soppleen ko ni ngeen soppe seen bopp, ndaxte ay doxandéem ngeen woon ca réewum Misra. Man Aji Sax ji maay seen Yàlla.

Ba loolu amee ñu ne ca seen biir: «Nun kat defunu njub. Bésub tey jii bésub jàmm la; nun, nu ne patt yéglewunu ko. Su nu xaaree ba jant bi leer de, àq dina nu topp. Kon nag aycaleen nu dem yeggeji ko waa kër Buur.»

Jonah 4:9 TSK

¶ Ci kaw loolu Yàlla ne Yunus: «Waaw, mbaa yaa yey am xol bu tàng ci lawtan gi?» Mu ne: «Maa yey am xol bu tàng ba dee sax!»

¶ Buleen ameel kenn bor, lu moy borub soppante; ndax ku sopp sa moroom, yaa matal yoonu Musaa.

Yennikoonteleen seeni yen, su boobaa ngeen di topp yoonu Almasi ba mu mat sëkk.

¶ Ci wàllu mbëggeel gi war ci biiri bokk, soxlawuleen ku leen ci bind dara, ndax yeen ci seen bopp, Yàlla tàggat na leen ci soppante,

Deeleen waxe tey jëfe ni mu jekke ci nit ñu ñuy séddeji àtteb yoon wiy goreel.

¶ Waaye yeen nag yeen ay giir giy tànneef, yeenay sarxalkati Buur, yeen ay askan wu sell, yeen ay xeet wi ñu jot, ngir ngeen biral jaloore yu wéet yi ñeel ki leen woo, génnee leen cig lëndëm, indi leen ci leeram gu yéeme.