TSK

TSK · James 5:16

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Naka la Ibraayma jegeñsi, ne ko: «Mbaa doo boole ku jub ak ku jubadi, rey leen?

Léegi nag dellool góor gi soxnaam, ab yonent la de, te dina la ñaanal, nga raw. Waaye soo ko deful, na la bir ne dinga dee, yaak sa waa kër yépp.»

Nit ka ne ko: «Na nga tudd?» Mu ne ko: «Yanqóoba.»

Tinuleen Aji Sax ji, ndax dënu yu màgg yeek tawub yuur bi dakk. Dinaa leen bàyyi, ngeen dem. Deesu leen fi téyeeti.»

Ci kaw loolu saa yu Musaa yékkatee loxoom, Israyil man, saa yu wàccee loxo ba, Amaleg man.

Mbooloo ma jooy ko Musaa, Musaa tinu Aji Sax ji, sawara wa fey.

Mbooloo ma dikk ba ci Musaa, ne ko: «Noo tooñ, ndax noo xultu ci kaw Aji Sax ji, ak ci sa kaw. Tinul nu Aji Sax ji, mu teggil nu jaan yi!» Musaa daldi tinul mbooloo ma.

¶ Ci kaw loolu Samiyel ñaan ci Aji Sax ji, Aji Sax ji dënu, taw ca bés ba. Mbooloo ma mépp nag ragal lool Aji Sax ji ak Samiyel.

Buur ne góoru Yàlla ga: «Rikk tinul ma sa Yàlla Aji Sax ji te ñaanal ma, sama loxo mana banku.» Góoru Yàlla ga tinul Buur Aji Sax ji, loxoom bankuwaat, mel na mu meloon.

Naka la dugg, tëj bunt ba, ñoom ñaar ca biir. Mu ñaan ci Aji Sax ji,

Mu walbatiku nag, jublook miir ba, ñaan ci Aji Sax ji ne ko:

Job 42:8 TSK

Kon nag sàkkleen juróom ñaari yëkk, ak juróom ñaari kuuy. Ngeen dem ba ca sama jaam ba Ayóoba, joxe ko fa saraxu rendi-dóomal, te Ayóoba ñaanal leen, ma seet ci moom ba bañ leena mbugale seenug ndof. Ndax waxuleen dëgg ci man ni sama jaam bi Ayóoba waxe.»

Na dëddu lu bon tey def lu baax, sàkku jàmm, saxoo ko.

Saraxub ku soxor, Aji Sax ji bañ na ko; ñaanu kuy jubal da koy bége.

Soo dee tanqamlu yoon, sag ñaan sax Yàlla suur na ko.

Su boobaa ngeen woo ma wall, dikk ñaan ma, ma nangul leen.

ngir ñu sàkku yërmandey Yàlla Boroom asamaan ci wàllu mbóot moomu, ndax ñu bañ leena rey mook àndandoom yaak yeneen boroom xam-xami Babilon.

Aji Sax ji moo séq ak Yuda ab layoo, mooy mbugale Yanqóoba ay jëfinam, añale ko ay jëfam.

Luke 9:6 TSK

¶ Ñuy dem nag, di wër dëkk ak dëkk, di yégle xibaaru jàmm bi, di faj jarag ji.

Luke 18:1 TSK

¶ Yeesu dellu leen léeb lii, ngir ñu wareefoo di sax ci ñaan te baña xàddi.

Acts 4:24 TSK

Ba ko bokk ya déggee, ñoom ñépp a mànkoo, daldi yékkati kàddug ñaan fa Yàlla, ne: «Buur Yàlla, yaa sàkk asamaan ak suuf ak géej ak lépp li ci biir.

Acts 12:5 TSK

¶ Naka lañu tëj Piyeer ca kaso ba, mbooloom gëmkat ñi saxoo koo ñaanal Yàlla.

Noonu it la Mbind mi indee ne: «Kenn jubul, du kenn sax.

¶ Moo tax nun itam, ba nu déggee seen mbir ba tey, noppiwunu leena ñaanal, di sàkku ngeen feese xam-xam ci lépp luy coobarey Yàlla, te ngeen ànd ceek lu mat sëkk ci wàllu xel, ak gis-gis bu Noo gi maye.

¶ Yàlla ci boppam, moom miy Boroom jàmm, yal na leen sellal, ba ngeen mat sëkk, te seen léppi xel, ak seen léppi xol, ak seen léppi yaram sàmmu, ba mucc sikk, ba kera bés bu sunu Sang Yeesu Almasi feeñee.

¶ Ngëm la Abel jébbale Yàlla sarax su gën saraxub Kayin, te ngëm lees seedeele Abel ne moo jub, kera ba Yàlla ci boppam seedee ne ay saraxam a nangu. Ngëm it moo waral Abel dee, te di wax.

te «ngeen xàllal seen bopp xàll yu jub yu ngeen di jaare seeni tànk,» ngir kuy soox doxe ca wér te baña gëna tële.

«Moom ci boppam moo gàddu sunuy bàkkaar, moo ko tegoo ci yaramu boppam ca bant ba,» ngir nu deeyal bàkkaar te dundal njub; «moom mooy ki ngeen wére ci ay góomam.»