TSK

TSK · James 5:19

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Yaay xarab képp ku wàcc sa dogali yoon, ay pexeem neen.

Bokk yi, ñu xalele ñoo leen di not, ay jigéen yilif leen. Bokk yi, seeni njiit a ngi leen di sànk, lëndëmal nañu seeni yoon.

Bu ci réer, maa lay seet; bu ci lajj, maa lay délloosi; bu ci damm, maa lay takkal; bu ci néew doole, ma leqli la. Waaye bu ci duuf, am doole, maa lay sànk, foral la li war ci yaw.

Waaye man tinul naa la, ngir sa ngëm baña giim. Yaw nag boo waññikoo, nanga dooleel sa bokki gëmkat.»

Ndax sopp xaalis kat mooy reenu mboolem xeeti loraange. Am na ñuy ŋaf-ŋafi, di ko wut, far lajj yoonu ngëm, ba teg seen bopp tiis yu bare.

Ñoo lajj yoonu dëgg, ba naan ñiy dekki, dekki nañu ba noppi, te seen wax jooju, am na ñenn ñu muy yàq seen ngëm.

Waaye ku denc ci sab xol, wextanu kañaan, ak mébétum sàkku sa darajay bopp, bul damoo xel mu rafet, nde kon nga moy dëgg.

¶ Kon nag yeen soppe yi, gannaaw xam ngeen loolu ba noppi, wattuleen bala leena réeraangey moykati yoon yi yóbbaale, ba yolomal seenub taxawaay.

Jude 1:22 TSK

Ñiy nàttable, ñeewanteleen leen,