Dees koo néewal doole, mitital ko te ubbiwul gémmiñam, xanaa mel ni xar mu ñuy rendiji, ne cell ni xar mu ñuy wat, ubbiwul gémmiñam.
TSK
TSK · James 5:6
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ «Yeen bokki Israyil, dégluleen wax jii! Yeesu waa Nasaret bi, Yàlla moo firndeele ag dëggoom, ay kéemaan aki kiraama aki firnde yu mu sottale jëmmu Yeesu moomu fi seen biir, te loolu xam ngeen ko xéll.
xamleen xéll, yeen ñépp ak bànni Israyil gépp, ne ci turu Yeesu Almasi waa Nasaret bi, ki ngeen daajoon ci bant, te Yàlla dekkal ko, ci turam doŋŋ la kii wére, ba taxaw ci seen kanam.
Lii nag mooy dogu mbind ma mu doon biral: «Dees koo yóbbu ni xar mu ñuy rendiji; mbete mburt mu ne cell ci kanam ki koy wat, ubbiwul gémmiñam.
Mu ne ma: “Sunu Yàllay maam moo la dencal céru ràññee coobareem, ak gis Aji Jub ji, dégg ko, muy wax ak yaw.
Sama nit ku jub nag mooy dund ndax ngëm ga, waaye ku dellu gannaaw, sama xol bégewu la.»
Yeenay xemmem lu ngeen dul am. Yeenay bóome, di iñaane lu ñeneen am, te manuleen koo am. Yeenay xuloo ak a jàppante. Dungeen am, ndax yeena ñaanul.