TSK

TSK · James 5:7

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

su boobaa, Yàlla nee: «Maa leen di may seen tawub réew, saa yu jotee: lollib réew ma day taw, cooroonam taw, ngeen dajale seenum pepp, ak seen biiñ bu bees, ak seen diw gu yees.

Hosea 6:3 TSK

Nan ràññee, di saxoo faale Aji Sax ji. Ni jant bu fenk la dikkam wóore, ni ab taw la nuy dikkale, ni ab tawu mujjantal buy seral suuf.»

¶ Bu suuf maree, ñaanal Aji Sax ji ab taw, Aji Sax ji mooy sàkk ay xàmbaar, sóobal nit ab taw, saxalal ku ne am ñax ci àll bi.

Luke 18:8 TSK

Maa leen ne, mooy sàmm seen àq ci lu gaaw. Waaye bu Doomu nit ki dikkee, mbaa dina fekk ngëm ci kaw suuf?»

Ñi saxoo di jéema def jëf ju baax, ngir di ko sàkkoo ndam, ak teraanga, ak texe gu sax, ñooñu, texe gu sax dàkk mooy doon seenub añ.

Ndaxte mboolem lu ñu bindoon, bu jëkk, jàngal nu moo taxoon ñu bind ko, ngir Mbind mi may nu xolu muñ, te ñaax nu, ba nu am yaakaar.

Ci lépp kay lanu bëgga seedeel sunu bopp, ne noo yelloo ngërëm, te ay jawriñi Yàlla lanu, di ñu muñ lu bare ci biir coono, aki mitit, aki njàqare;

Bunu tàyyi ci def lu baax, nde bu jotee rekk nooy góob, ndegam yoqiwunu.

ak di baamtu fi kanam Yàlla sunu Baay, jëf ji juddoo ci seen ngëm, ak liggéey bi sottee ci seen cofeel, ak yaakaar ji ngeen saxoo di séentu sunu Sang Yeesu Almasi.

Yal na Boroom bi dooleele noonu seen xol, ngir kera bu sunu Sang Yeesu délsee, ànd ak ñoñam ñu sell ñépp, fekk leen sell te mucc sikk, fa kanam Yàlla sunu Baay.

¶ Kon nag gannaaw gii ndiiraanu seede wu réy moo nu yéew, nanu sippiku mboolem sëf bu nuy yeexal, ak bàkkaar bu nu yomba téqtal. Ñu daw nag xél wi ñu nu waajalal, te baña yoqi.

Ñooñoo naan: «Ki dige woona ñëw, ana mu? Ba maam ya nelawee de yàgg na, waaye lépp a ngi wéye na woon ca njàlbéenu àddina.»