Ma ne, «Éy Boroom bi Aji Sax ji, yaa naxlu askan wii nax yu metti, ba nga nee: “Yerusalem jàmm lay am,” te saamar tege ci putam.»
TSK
TSK · Jeremiah 14:13
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Yonent yiy wax waxyuy fen, sarxalkat yiy jiitee seen coobare, te sama ñoñ soppe ko ni! Moo bu muj ga taxawee, nu ngeen di def?»
Sofental nañu sama pajum ñoñ ñi dammtoo, naan: “Jàmm, lépp jàmm!” te jàmm amul.
Ñi ma teddadil lañuy waxa wax, naan leen Aji Sax ji déy nee: “Jàmm ngeen di am.” Képp ku topp sa xelum déggadi, ñu ne ko: “Musiba du la dab mukk.”
Te sa yonent yi la doon jottli waxyu, naan la buuru Babilon du dikk ci seen kaw, yaak waa réew mii, ana ñu léegi?
Gannaaw yeena fen ba jeexal xolu aji jub, te du maa ko tegu naqar, gannaaw yeena dooleel ku bon, tere koo dëpp yoonu mbonam ba dund,
¶ Waaye na mu ame woon ci askanu bànni Israyil ay yonenti caaxaan, ni lay ame ci seen biir ay sëriñi caaxaan yuy sërxal ay àlluway sànkute yuy weddi sax Sang bi leen jot, ba yóbbe seen bopp sànkute ju bette.