¶ Ba bànni Israyil nekkee ca màndiŋ ma, dañoo fekk jenn waay, muy taxan bésub Noflaay.
TSK
TSK · Jeremiah 17:21
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Nangeen wattu seen bopp bu baax nag ndax keroog ba Aji Sax jiy àddoo ca digg sawara wa, wax ak yeen ca tundu Oreb, gisuleen jenn jëmm.
¶ Wattuleen seen bopp nag, bala leen seen xel a nax, ngeen lajj, di jaamu yeneen yàlla, di leen sujjóotal,
¶ Ci fan yooyu ma gis ci Yuda ay nit ñuy nal reseñ, bésub Noflaay. Mu am ñuy indi ay sabaari pepp yu ñuy sëf ay mbaam, boole ca biiñ ak reseñ ak figg ak lu nekk, di ko yóbbu Yerusalem ci bésub Noflaay. Ma àrtu leen it ca la ñuy jaay seen yëf yooyu ci boobu bés.
Sàmmala sàmm sab xol, nde xalaati xol ngay jëfe.
Buleen génne seeni kër lenn bésub Noflaay te buleen ci liggéey lenn. Waaye nangeen sellal bésub Noflaay, muy la ma santoon seeni maam.
Kon nag teewluleen ni ngeen di dégge. Ku am, dees na ko dolli, waaye ku amul, la mu xalaatoon ne am na ko sax, dees na ko nangu.»
Wattuleen nag seen bopp, wattu mboolem gétt, gi leen Noo gu Sell gi sàmmloo, te ngeen foral mbooloom gëmkati Yàlla, mi Yàlla jote deretu boppam.
Moytuleen balaa kenn di ñàkk yiwu Yàlla. Moytuleen bala ab reenu wextan di fëll, di lëjle, ba rax mbooloom lëmm.