TSK

TSK · Jeremiah 2:21

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Dalal ci réew mii; dinaa ànd ak yaw, barkeel la. Yaak sa askan laay jox suuf sii sépp, te dinaa sàmm li ma giñaloon sa baay Ibraayma.

te yaa leen di sampi ca sa tund wa nga séddoo, fa nga waajal sa dëkkuwaay, Aji Sax ji, bérab bu sell ba nga sàkke sa loxol bopp, Boroom bi.

Seen reseñ a nga cosaanoo Sodom, ak tóokëri Gomor, doom ya di tooke, cëgg ya wex xàtt!

Éy Yàlla, noo déggal sunu bopp, sunuy maam a nu wax jëf ja nga jëf, ca seeni jant, bu yàgga yàgg.

Yaa déjjatee reseñ Misra, dàq yéefar yi, indi, jëmbataat.

Ana nu biib dëkk yàqoo, mbeteb gànc, te nekkoon dëkkub kóllëre, njubte mate fa, njekk lal fa panaan, tey ñu diy bóomkat!

Mu gàbb ko, dindi doj ya, jëmbat ca ngëneeli reseñ, tabax tóojub doj fa digg ba, ba yett ca mbalkam nalukaayu reseñ, tey yaakaar reseñ ju neex, mu meññ, wex.

Waaye yaw Israyil, sama jaam bi; yaw Yanqóoba mi ma taamu, yaw askanu Ibraayma, samab xarit!

ngir tabb waa Siyoŋ ñiy ñaawlu, jox leen kaala gu wuutu dóom bi ñuy ñaawloo, ak diwu mbégte mu ñu weccikoo seenu tiis, ak mbubbam cant mu ñu weccikoo xol bu jeex, ba ñu naa: «Ñii ñoo di ponkali garabi njekk yi, njëmbat li Aji Sax ji jëmbat, ngir teewal teddngaam.»

Oliw naat, jekki doom; nii la leen Aji Sax ji tudde woon, waaye riir mu réy lay jibal, jafal ko, mu tàkk, taar réer car ya, meŋŋ.

Yaw nit ki, ana lu bantu reseñ gëne ci bant yi, ak mboolem caru garab bu mu doon ci gott bi?