TSK

TSK · Jeremiah 21:12

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

su boobaa ma gën leena mereeti, noonoo leen, te man ci sama bopp maa leen di mbugalati lu ko ëpp fukki yoon ak juróom, feye leen ko seen bàkkaar.

¶ Buur Daawuda ci kaw Israyil gépp la nguuru woon; muy jëfe njub ak njekk ñeel réewam mépp.

Ñeel Suleymaan. Céy Yàlla, mayal Buur sa xelum àtte, mayal doomu Buur bii sa xelum njekk,

«Dungeen bàyyi àtteb njublaŋ, ak di faral ku bon? Selaw.

Maay xëy, sànk képp ku bon ci réew mi, ngir dagge ci dëkkub Aji Sax jii képp kuy def lu ñaaw.

Nanga àddul ku amul kàddu, ku sësul fenn, nga ñoŋal àqam.

Ngalla yeen, réew mi gone falu buur, jawriñ ña di xëye xawaare.

Boroom doole mel ni boob, la mu liggéey di ferñent, ànd ak moom ne jéppét, te kenn du fey sawara wa.

Esayi nag ne: «Yeen waa kër Daawuda, dégluleen! Tàyyiloo ngeen nit, di tàyyiloo sama Yàlla itam.

Wóoy ngalla ña wàcci Misra, di wuti wall; di sukkandikoo ay fas, tey yaakaari watiir ndax bare ga, aki gawar ndax lim bu takku ba te xooluñu ci Aji Sell ju Israyil, sàkkuwñu kooku di Aji Sax ji.

Moo tax Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne: «Gannaaw wax jii lañu wax, maa ngii di def samay wax di sawara ci sa gémmiñ, askan wii di matt, mu xoyom leen.

¶ Moo tax Aji Sax ji Boroom bi dafa wax ne: «Sama xadar a ngii di sottiku fi bii bérab, fi kaw nit ak mala, garab ak lu suuf meññ, lépp ne jippét, te deesu ko fey.»

Man mii maay xareek yeen, won leen sama doole ak sama diisaayu loxo, xadaru, dikke leen mer mu réya réy.

Aji Sax ji dafa wax ne: Deeleen jëfe dëgg ak yoon, di xettli ku ñu xañ dëgg ci ki koy néewal doole. Ab doxandéem, ab jirim akub jëtun, buleen leen lor, buleen leen fitnaal. Deretu jaambur bu deful dara it, buleen ko tuur ci bii bérab.

«Ay bés a ngi ñëw,» kàddug Aji Sax jee, «maay jebbil Daawuda njebbitu njekk, mu falu di buur bu xelu, di jëfe njub ak njekk ci réew mi.

Jombul ñu tinu Aji Sax ji, ku nekk ci ñoom dëpp yoonu mbonam, ndax mer mu réy ak xadar ji Aji Sax ji tuddal askan wii kat, nar naa metti.»

Aji Sax jee xëpp am sànjam, sotti tàngooru meram, moo jafal sawara fi Siyoŋ, ba xoyom kenu ya.

«Yaw nit ki, waa kër Israyil mbuubitu weñ gu raxe lañu ci man léegi. Ñoom ñépp duñu lenn lu moy xànjar ak weñ gu weex ak gu ñuul ak beteex ci biir taalub tëgg. Mbuubitu xaalis rekk lañu.

Man maay wacc deret ja ca doj wa amul dara, fa mu naan fàŋŋ, du suulu, ngir mu doon sànj muy wàcce mbugal.»

Du seen xaalis, du seen wurus wu leen di mana xettli. Keroog bésub sànjum Aji Sax ji, ak sawaras fiiraangeem, àddina sépp ay xoyomu. Mooy raafal moos mboolem ñi dëkke àddina si, te raafal gu raglu lay doon!»

«Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne: Àtteb dëgg, nangeen ko àttee, te ngor ak yërmande it, deeleen ko jëflantee.

Luke 1:69 TSK

Moo nu feeñalal Musalkat bu manoorewu, fi biir kër Daawuda jaamam ba,

Ndax kilifa gi mooy ndaw li Yàlla yebal ngir sa jàmm. Waaye soo dee def lu bon, ragalal, ndax kilifa gi yorul ab saamar cig neen; mooy ndawal Yàlla liy añale, te mooy jottli am sànj mu wàccal kuy def lu bon.