TSK

TSK · Jeremiah 21:7

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Waa Babilon nag topp Buur Cedekiya, ba dab ko ca jooru Yeriko, fekk mbooloom xareem mépp tasaaroo, wacc ko.

¶ Ci kaw loolu njiital dag ya jàpp Seraya sarxalkat bu mag ba, ak Cefaña sarxalkat ba ca topp, ak ñetti dagi bunt kër Aji Sax ja.

Maa ngii di xabtal fi seen kaw waa Medd, ñi xintewoowul xaalis, faalewuñu wurus.

Maa mere woon sama ñoñ, sobeel sama séddoo ñii, teg leen ci sa loxo, te wonoo leen yërmande, ba mag sax, nga teg ko lu diisa diis,

Su ñu ci boole woon koor sax, duma déglu seeni dagaan. Su ñu ma doon sarxalal saraxu rendi-dóomal ak saraxu pepp it, du maa leen di nangul. Xanaa saamar akub xiif ak mbas kay laa leen di faagaagale.»

Ndax Aji Sax ji dafa wax ne: “Maa ngii di la wàcceel tiitaange, yaak sa soppe yépp, seen saamaru noon daaneel leen, ngay gis; te Yuda gépp laay teg ci loxol buuru Babilon, ñii mu yóbbu leen ngàllo, ñee mu jam leen, ñu dee.

Te Cedesyas buurub Yuda du rëcc waa Babilon ndax dees na ko teg moos ci loxol buuru Babilon, ba Cedesyas wax, mu wax, seeni gët ñeent.

Yowakim buurub Yuda nag, nanga ko wax ne ko: “Aji Sax ji dafa wax ne yaw yaa lakk taxañ bii, naan lu waral ma bind ci ne buuru Babilon dina ñëw moos te dina tas réew mii, faagaagal fi nit ak mala.

Waaye soo lànkee, ne doo génn, mbir a ngii mu ma Aji Sax ji won.

«Israyil diy gàtt yu tasaaroo, yu ay gaynde dàq, buurub Asiri di gaynde gi jëkka lekk, Nabukodonosor buuru Babilon topp ca, seeñu yax ya.»

Gannaaw loolu mu tuur bëti Cedesyas, ba noppi jénge ko jéngi xànjar, yóbbu ko Babilon, tëj ko fa, ba keroog bés ba mu deeyee.

Buuru Babilon nag bóom leen foofa ca Ribla, ca réewum Amat. Noonu la waa Yuda génne seen réew, dem ngàllo.

Yaa woote ni su doon bésu màggal, tiitaange dar kepp ma. Bésub merum Aji Sax ji, kenn rëccul, kenn muccul. Doom yi ma jur, yar leen, noon bi fàkkas leen!

Man it maa leen di feye xadar. Duma xool bëtu ñéeblu, duma ñeewante. Dinañu yuuxu yuux yu réy, may dégg te duma leen faale.»

Man it duma xool bëtu ñéeblu, duma ñeewante. Seen jëfin laay këpp ci seen kaw bopp.»

Maa koy laaw sama mbaal, mu lonkoo samab caax, ma yóbbu ko Babilon, layoo faak moom ñàkke worma gi mu ma ñàkke worma.

Maa ngii di dooleel waa Babilon, xeet wu wex, ràkkaaju, di wër déndi àddina, di nangu màkkaani jaambur.