TSK

TSK · Jeremiah 37:13

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Ba mu ko defee, mu am ñu ne: «Aywaleen, nu lalal Yeremi pexe. Ndax kat soxlawunu ko ba di ci ñàkk dara: du njànglem sarxalkat, du digley boroom xel te du waxyu bu yonent biral. Nanu ko duural ba sànk ko te baña faale lenn ciy waxam.»

Ku toog ci dëkk bii, dinga deeye xare mbaa xiif mbaa mbas. Ku génn jébbal boppam waa Babilon ñi leen gaw nag dinga dund, bakkanam di yoolu xareem.

¶ Ci biir loolu Cedesyas buurub Yuda it, ma yegge ko kàddu yooyu yépp, ne ko: «Wàcceel yetu buuru Babilon saw ndodd, nangul ko, nangul ay bokkam, ndax ngeen dund.

Mu daldi wàcc, ba ca kër buur, jàll ca néegu bindkat ba, fekk fa kàngam yépp toog: Elisama bindkat ba, ak Delaya doomu Semaya, ak Elnatan doomu Agbor, ak Gemarya doomu Safan, ak Cedesyas doomu Anaña, ak jawriñ ña ca des ñépp.

¶ Kàngami buur yooyu dem ne Buur: «Waa jii, na dee rekk; mu ngi yoqil xarekat yi des ci dëkk bi, di yoqil ñépp ndax waxam jii mu leen di wax. Waa jii kat wutul jàmmu askan wii, xanaa musiba.»

Buur sant Ebedd Meleg Kuuseen ba, ne ko: «Jëleel fii fanweeri nit, nga dem génne Yonent Yàlla Yeremi kàmb ga bala moo dee.»

Amos 7:10 TSK

¶ Ba mu ko defee Amaciya sarxalkatu Betel yónnee ca Yerbowam buurub Israyil, ne ko: «Amos a ngi lay fexeel ci digg Israyil. Réew mi du àttan waxam ji.

Luke 23:2 TSK

Ñu tàmbali di ko sosal, naan: «Kii lanu fekk muy fàbbi askan wi, di aaye ku fey Sesaar galag, te naan moom ci boppam mooy Almasi, di buur.»

Acts 24:5 TSK

Waa jii lanu gis ne ab rambaaj la buy sabab réeroo ci biir Yawuti àddina sépp. Moom mooy njiitu ngér mu sikk mi ñuy wax Nasareen ñi.

ci biir teraanga, ak ci biir toskare; ci biiri baatal, ak jëw yu rafet. Dees noo jàppe ay mbubbookati dëgg, te nuy nit ñu dëggu;