TSK

TSK · Jeremiah 38:13

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Nga ne ko: “Buur dafa wax ne: Dugal-leen kii ndungsiin, di ko jox lekk gu néew ak ndox mu néew, ba keroog may dikk ak jàmm.”»

Booba mbooloom xarem Babilon a nga gaw Yerusalem. Fekk Yonent Yàlla Yeremi nag moom, ma nga ñu tëj ca kër buurub Yuda, ca biir ëttu dag ya,

Ñu jàpp Yeremi, ngir denci ko ca kàmbug Malkiya, kenn ci askanu buur, ca biir ëttu dag ya. Ñu yoore ko buum, ba ca biir, te kàmb ga amul ndox, bàq rekk a fa nekk. Yeremi nag tàbbi ca biir bàq ba.

ñu yónnee, jëli Yeremi ca ëttu dag ya, teg ko ci loxol Gedalya doomu Ayikam doomu Safan, ngir Gedalya yóbbu ko kër ga. Yeremi nag des Yuda ca biiri bokkam.

Mu ne ko: «Xaaral ba say tuumaalkat itam dikk, ma déglu la.» Mu santaane nag, ñu denc ko ca kër buur Erodd.

Ba nu dikkee Room nag may nañu Póol, mu am daluwaayu boppam, ab takk-der di ko wattu.