TSK

TSK · Jeremiah 39:18

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi
Job 5:20 TSK

Ab xiif, moo la cay jote ba doo dee, ab xare, nga mucc ñawkay saamar,

Ma ne, Aji Sax jee naa jàkk ku ko ragal tey wéeroo ngoram.

Dénkul ci Aji Sax ji, di def lu baax, ba des ci réew meek jàmm.

Aji Sax ji Yàllaa mat jant, mat kiiraay; yiw ak daraja, Aji Sax ji joxe; te du ngëneel lu muy bañal ku mat.

Buleen wóolu kilifa, doom aadama amul wall.

Yaw Aji Sax ji, ku dogu, pastéefu, wóolu la, nga may ko jàmm ju mat, nde moo la wóolu.

Ku toog ci dëkk bii, dinga deeye xare mbaa xiif mbaa mbas. Ku génn jébbal boppam waa Babilon ñi leen gaw nag dinga dund, bakkanam di yoolu xareem.

Aji Sax ji da maa sant ma wax la ne la: “Aji Sax ji dafa wax ne: La ma tabaxoon a ngii, maa ngi koy daaneel, la ma jëmbatoon a ngii, maa ngi koy buddat, ba réew mépp daj.

¶ Mboolem ñi bàkkaar nag te fekku leen ci yoonu Musaa, yoonu Musaa toppu leen, waaye du leen teree sànku. Mboolem ñi bàkkaar it, te mu fekk leen ci yoonu Musaa, ci yoonu Musaa lees leen di daane.

ñi Almasi tax ngeen gëm Yàlla. Te Yàllaa ko dekkal, may ko ndam, ba tax Yàlla di ki ngeen gëm, yaakaar ko.