Ku toog ci dëkk bii, dinga deeye xare mbaa xiif mbaa mbas. Ku génn jébbal boppam waa Babilon ñi leen gaw nag dinga dund, bakkanam di yoolu xareem.
TSK
TSK · Jeremiah 44:13
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Jeremiah 21:9
TSK
Jeremiah 24:10
TSK
Maay yebal saamar fi seen kaw ak xiif ak mbas, ba ñu raaf fi kaw suuf si ma leen joxoon, ñook seeni maam.»
Jeremiah 42:16
TSK
saamar ba ngeen ragal moo leen di dabe réewum Misra, xiif bi ngeen di xalaat topp leen fa Misra, te fa ngeen di deeyi.
Jeremiah 42:18
TSK
¶ «Aji Sax ji Yàllay Israyil Boroom gàngoor yi déy dafa wax ne: “Bu ngeen demee Misra, ni sama mer ak sama xadar yurikoo woon fi kaw waa Yerusalem, ni la sama xadar naan yureet fi seen kaw. Dingeen doon gentu alkànde, ñu di leen móolook a sewal, te dungeen gisati miim réew.”»
Jeremiah 44:27
TSK
Maa ngi nii di leen teewloo seen musiba, waaye du seen jàmm laa leen di teewloo. Te mboolem waa Yuda ñi ci réewum Misra dinañu sànkoo saamar akub xiif, ba keroog ñuy jeex tàkk.