Ci biir loolu Suleymaan tabaxal Kemos, tuuru Mowab mu siblu ma, ab bérabu jaamookaay ca kaw tund wa féete Yerusalem penku. Mu tabaxaaleel ca Moleg, tuur mu siblu ma Amoneen ñay jaamu.
TSK
TSK · Jeremiah 48:13
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Ba loolu amee mu teg wenn wëllu wa ca dëkk ba ñuy wax Betel, wa ca des mu tegi ko ca Dan.
Ilyaas ne leen: «Jàppleen yonenti Baal yii. Bu kenn ci ñoom rëcc.» Ñu jàpp leen, Ilyaas yóbbu leen ba ca xuru Kison, rendi leen foofa.
Bésub keroog booba, yàllantuy xaalis ak wurus ya nit sàkkal boppam, di leen sujjóotal, ñoom lay sànni ca jaar yaak njugub ya,
Yettkati xërëm yaa ngoogu, rus, torox, riixleendoo.
Tuur ma ñu naa Bel toqi na, tuur ma ñu naa Nebo sukk, mala ya féetewoo seeni jëmm, ñoom lees daan gàddu, tey jur gi jagoo, di leen sëf ba loof.
«Yuuxooleen, ne leen: “Céy gii yàqtoo! Mowab gii wone gannaaw! Mowab rus na.” Ñi ko wër ñépp a koy reetaan, seen yaram di daw ci ñoom.»
Yeen waa Samari, seen jëmmu wëllu wi dàqu na! Sama mer tàkkal na leen. Lu ngeen deeti xaar ci mucc ayib?
Am riir mooy jollee ca sa biir gàngoor, sa tata yépp tas, na Salman tase woon Bet Arbel, keroog bésub xare ba, ba ñu jëlee ndey, fenqaleek doom, ñu rajaxoo.