TSK

TSK · Jeremiah 8:13

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Ay tóokëri reseñ, ngeen jëmbat, sonn ca, te biiñ, dungeen ko naan, dungeen witt doom ya it, ndax sax yee koy lekk.

Lu may defalati sama tóokër bi, lu ma ca defuloon? Lu waral ma di ko yaakaare reseñ ju neex, mu meññ, wex xàtt?

Bu bésub keroogee Aji Sax ji dikke mbugal gàngoor ya fa kawa kaw, ak buuri àddina yi fi suuf.

Moo tax Aji Sax ji dafa wax ne: «Yonent yi ma yebalul te ñuy waxe waxyu ci sama tur naan: “Saamar akub xiif du am ci miim réew,” saamar akub xiif ay mujje yooyu yonent.

Moo tax Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: “Gannaaw doon ngeen yeen ñépp mbuubitu weñ, maa ngii nag di leen dajale fi digg Yerusalem.

Léebalal kërug fippukat yi aw léeb, ne leen: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Taalal, teg cin li, teg ko, sotti ci ndox.

Joel 1:7 TSK

Samag reseñ lañu fóom, samag figg lañu xasa xas, ba mu set, ñu sànni, car ya weex tàll.

Ndaxam garabu figg foccul, doomu reseñ amul ca ndeyam, njurum garabu oliw àntuwul, tool yi meññul aw ñam, gàtt it tukkee na ca gétt ga, du genn jur gu gudd ci wurmbal,

Maa leen dumaa gàncax gu benaat, ak gu xuur, ak tawub doji yuur ci mboolem seen liggéeyu loxo, te taxul ngeen délsi fi man, kàddug Aji Sax jee.

Naka la jant di fenk, ba naaj wi tàng jérr, saxayaay lax, tóor-tóoram ruus, taar ba réer ko mërr. Noonu itam la ki barele di jeexlee ci biiri yëngoom.