TSK

TSK · Job 13:12

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Yàlla Aji Sax ji nag móol nit ci pëndu suuf, sol ngelawal dund ci paxi bakkanam, nit daldi doon boroom bakkan.

¶ Ba loolu amee Aji Sax ji wax Musaa ne ko: «Bindal lii xew cib téere, muy pàttli, te nga xamal Yosuwe ne ko, raafal laay def askanu Amaleg, ba ñu jeex tàkk, ba deesatu leen fàttliku fu asamaan tiim.»

Job 18:17 TSK

Turam tukkee kaw suuf, ba deesatu ko tuddem pénc.

Ay gët la Aji Sax ji ne jàkk aji jub ji, te ay noppam la dékk wooteb wallam.

Yal na seeni moy sax fi kanam Aji Sax ji. Yal na seen tur dagge fi kaw suuf.

Yooyu sang dee nañu, nekkatuñu, wuute nañu, jógatuñu. Yaa def nii, faagaagal leen, ba far sax seen tur.