TSK

TSK · Job 2:7

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Su ko defee dóom bi doon pënd bu sew ci kaw réewum Misra gépp, daldi def ay taab yuy sotti dëtt ci réewum Misra gépp, nit ak mala.»

¶ Aji Sax jee leen di dumaa taabi óom, ak taabi yeel yu bon. Dungeen mana am pajam, te ci seen wewu tànk lay lawe, ba ci seen kaw bopp.

Job 1:11 TSK

Xàccil sa loxo rekk, dal ci mboolem lu bokk ci moom. Ndegam du jàkkaarlook yaw, xarab la.»

Job 30:17 TSK

Guddi dikk di bënn samay yax, muy rot, mitit di ŋereñ te du selaw.

Bopp ba téstën, fenn jagul. Xanaa gaañu-gaañu aki dagg-dagg rekk, ak góom yuy nàcc, fajeesu ko, takkeesu ko, gajfaleesu kook ag diw.

tuubuñu seeni jëf, xanaa di saaga Yàllay asamaan ndax seeni mitit ak seeni taab.