Yàlla wóoluwul sax ñu sellam ña ca asamaan, te asamaan sellul ba doy ko,
TSK
TSK · Job 21:22
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
di nu xamal lu rabu àll xamul? di nu may xel mu njanaaw amul?»
Ana ku ko masa rëddal yoonam? Ak ku ko ne: «Def nga naka-su-dul-noonu?»
Yaw miy layook Aji Man ji, dangay diiŋat? Yaw miy weranteek Yàlla, doo tontu?
Ana ku mel ni sunu Yàlla Aji Sax ji, ki kaweel ab jalam, toog,
Ana ku mana xayma Aji Sax ji? Mbaa nga dib xejjam, ba di ko digal?
Wóoy ngalla kuy diiŋat ka la tabax te di ndabal xandeer ci biir ndabi xandeer! Ana ban ak di wax tabaxkatam, naa ko: «Looy def nii? Yaw amulooy loxo.»
«Ana ku xam xalaatu Boroom bi? Ana ku ko digal?»
Am xamuleen ne malaaka yi sax, nun noo leen di àtteji, astamaak mbiri dund gii?
Te it malaaka ya yemul woon ca daraja ja ñu amoon, xanaa wacc seen dëkkuwaayu bopp, Yàlla moo leen denc ci lëndëm gu ne këruus, yeewe leen buum yu dul deñ, ngir àtteb bés bu mag ba.
Ma gis néew ya, mag ak ndaw, ñu taxaw ca kanam ngàngune ma, ay téere ubbiku, beneen téere ubbikooti, di téereb dund ba. Ñu daldi àtte néew ya ca seeni jëf, na ñu ko binde ca téere ya.