TSK

TSK · Job 32:8

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Firawna daldi ne jawriñ ya: «Ndax masees naa gis ku mel ni kii a waay, nit ku Yàlla sol Noowug boppam?»

dama ne, dinaa la defal li nga ñaan, te sax dinaa la may xel mu rafet, nga am ug dégg, ba raw ku la jiitu ak ku la wuutu.

Job 4:12 TSK

Man la kàddu dikkal ci kumpa, sama nopp taataan ndéey la,

Job 12:16 TSK

Kee am doole, keey sottal, di boroom aji réer ak ka ko réeral.

Job 33:16 TSK

Mu ne ko rukk ndéey, boole kook màndarga, artoo ko ko,

Job 38:36 TSK

Ana ku yeb xel mu rafet cib dënn, ak ku may ab xol dég-dég?

Xelum nit làmp la bu Aji Sax ji taal, da koy niital ba ca biir xolam.

Dees koo xamal yoon wa, te Yàllaam a ko ko jàngal.

Mooy walbati jamono, di soppi demin, di fal buur, di folli. Mooy xelal boroom xel mu rafet, di xamal boroom xel mu ñaw.

Kii ci Noo gi la jote kàddu gu xelu, kee séddoo kàddug xam-xam ci genn Noo gi.

James 1:5 TSK

¶ Ku desele am xel mu rafet nag, na ko ñaan Yàlla, mu may ko ko, ndax Yàlla mooy yéwéne ñépp te du sikk kenn.