TSK

TSK · Job 39:5

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Ismaylaay tiiñe, ni mbaamu àll mu deesul not, di noonoo ñépp, ñépp noonoo ko. Mooy sanc fu muy jàkkaarlook bokkam yépp.»

Job 6:5 TSK

Mbaamu àll dina ŋaax te tiim ñax mu tooy a? Am nag dina nàññi te tiim um ngooñam?

Job 24:5 TSK

Néew-ji-doole yaa ngii mel niy mbaami àll ci màndiŋ mi, di fortaatu lu ñu lekk, àll bu wow bi yor seen xontu njaboot.

ngay nàndal bépp ndundatu àll, di wëgg mbaamu àll,

mbaa mbaamu àll mu miin màndiŋ mi, xabtaloo bakkanam, di xañtu ngelaw li. Bu bëggee tëbu, ku ko mana téye? Kuuy mu koy sàkku du sonn, bu ci tolloo rekk, mu jot ko.

dàqe ko ci nit ñi, def xel ma xelum rab. Mu dëkk ak mbaami àll yi, am ñax dim xontam niw nag, lay biy wàcc, di ko faam, ba kera ba mu xamee ne Aji Kawe jee yor nguurug nit, di ko jox ku ko neex.