TSK

TSK · Joel 1:12

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Ñu dem ba ca xuru Eskol, daldi fay dagge ab car bu def benn cëggub reseñ, ñaar ca ñoom gàddoo ko bant, ñu sàkkaale fa gërënaat ak figg.

Maa gis jéllu noon yi, dégg yuuxi ñu bon ñi may tëru.

Yaa leen di sippil seen sëf, damm bant ba ñu leen gàlloon, ak yetu ña leen notoon, na nga leen defaloon rekk ca xareb Majan.

Mbedd maa ngi soowaloo, ndax biiñ bu ñàkk, gépp mbégte fey, bànneexu àddina dëddu.

Tukkal nañu mbégteek bànneex fi tóokëri réewum Mowab. Maa ŋacc mbàndi biiñ ya, kenn nalatu fa reseñ, di soowoo coowal mbégte, xanaa ay yuux.

Joel 1:10 TSK

Tool yi yàqu yaxeet, suuf sëngéem ciw tiis; pepp yàqu, biiñ bu bees wow, ag diw ŋiis.

Ndaxam garabu figg foccul, doomu reseñ amul ca ndeyam, njurum garabu oliw àntuwul, tool yi meññul aw ñam, gàtt it tukkee na ca gétt ga, du genn jur gu gudd ci wurmbal,

Maa leen di gëddal njéeréer, ba du leen yàqal meññeefum suuf, te reseñug tool du leen jaasiral.» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax.