TSK

TSK · Joel 2:12

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Waaye su ngeen fa sàkkoo seen Yàlla Aji Sax ji, dingeen ko daj, ndegam seen léppi xol, ak seen léppi bakkan ngeen ko sàkkoo.

Ñu daje ca Mispa, tanq ndox, sotti fa suuf, fa kanam Aji Sax ji. Ñu woor nag bésub keroog, daldi wax foofa ne: «Noo tooñ Aji Sax ji.» Ca Mispa la Samiyel doone njiitu Israyil.

bu ñu demee ba seenum xel dellusee fa réew ma ñu leen yóbbu ngàllo, ñu tuub tey sàkku aw yiw fi yaw foofa ca réewum ña leen jàpp, ne la noo moy, noo ñaaw, noo def lu bon,

¶ Keroog ñaar fukki fan ak ñeent ca weer woowa, bànni Israyil daje nañu, sol ay saaku, xëppoo suuf, di ko ñaawloo ci biir koor.

Sàkkuleen Aji Sax ji bi ngeen koy mana gis, wooleen ko bi muy jege.

«Yaw Israyil, sooy waññiku, waññikul fi man.» Kàddug Aji Sax jee. «Soo jëlee fi sama kanam sa jëf ju siblu, te jenguloo,

Jombul ñu tinu Aji Sax ji, ku nekk ci ñoom dëpp yoonu mbonam, ndax mer mu réy ak xadar ji Aji Sax ji tuddal askan wii kat, nar naa metti.»

Hosea 6:1 TSK

Ca ngeen naan: «Nan dellu ci Aji Sax ji. Moo nu xotat, te moo nuy wéral. Moo nu duma, te moo nuy takkal sunuy góom.

Yaw nag, ca sa Yàlla nga wara dellu, ngor ak njub, sàmm ko, te nga saxoo yaakaar sa Yàlla.

Joel 1:13 TSK

Yeen sarxalkat yi, gembuleen te tiislu, yeen ñi dénkoo sarxalukaay bi, yuuxuleen, yeen boroom dénkaaney sama Yàlla, dikkleen, sol ay saaku yu ngeen fanaanoo, ngir toroxlu, nde xañees na seen kërug Yàlla ga saraxu pepp ak saraxu tuuru!

Kon nag waxal askan wi, ne leen Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne: “Dellusileen ci man,” kàddug Aji Sax jee, Boroom gàngoor yi, “kon dinaa dellusi ci yeen.” Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yee ko wax.

«Waxal askanu réew mi mépp, ak sarxalkat yi, nga ne leen: “Ba ngeen dee woor ak a ñaawlu ci weeru juróomeel, ak weeru juróom ñaareel, ci diiru juróom ñaar fukki at yii, ndax man mii ngeen doon woorala wooral?

Waaye li dale Damaas ak Yerusalem ba ci réewum Yawut gépp, ba ca ñi dul Yawut, ñoom ñépp yégal naa leen seen wartéef, muy tuubeel ak waññiku ci Yàlla, ak jëf ju tuubeel yellool.