ba noppi, mu wax leen ne leen: «Waajal-leen gannaaw-ëllëg, te li feek booba, buleen fi ànd ak jigéen.»
TSK
TSK · Joel 2:16
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
ak seeni tuut-tànk, ak seeni jabar, akub doxandéem ci seenub dal, seen gorkatub matt, ba ci seenub rootkat.
Bu ñu demaan ba ñépp fégal, Ayóoba day yónnee ngir sell-luloo leen. Ci biir loolu day teela xëy, daldi leen joxeel ñoom ñépp ba ñu daj saraxu rendi-dóomal, ku nekk benn. Booba Ayóoba da naan: «Jombul sama doom yii bàkkaar nañu mbaa ñu xarab Yàlla ci seen xel.» Noonu la Ayóoba jàppoo woon bés bu nekk.
Sellal-leen ag koor, woote am ndaje, wooleen mag ñi, ak mboolem waa réew mi, ca seen kër Yàlla Aji Sax ji, te ngeen woo Aji Sax ji wall.
Su bés baa yuuxi dëj yu réy ay jibe fi Yerusalem, mel ni yuuxi dëj ya ca Adàdd Rimon, ca jooru Megido.
Buleen di xañante seen bopp, ndare du yeena mànkoo ab diir, ngir bokk tënku ci ñaan. Waaye gannaaw loolu, delluleen di ànd, bala leena Seytaanee xiirtal ci moy, ndax tëlee téye seen bopp.