TSK

TSK · Joel 2:20

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Aji Sax ji walbati ngelaw la, mu jóge sowu, am doole lool, daldi fél njéeréer ya, sànni ca géeju Barax ya, ba luy niru njéeréer desatul ca déndu Misra.

Asayel ne ko: «Moo sang bi, man mi ab xaj gën, nu ma mana defe jooju jëf ju réy?» Alyaasa ne ko: «Aji Sax ji won na ma ne yaay doon buurub Siri.»

Seeni néew lees di xalab, ñu médd, xet ga gilli, seen deret la tund yiy sangoo.

Juróom ñaari weer waa kër Israyil di leen rob, ngir setal réew mi.

Kemu penku ba day dale diggante Oran ak Damaas, topp xuru Yurdan, diggante diiwaanu Galàdd ak réewum Israyil, dem ba àgg Tamar ca géeju penku ba. Loolooy wàllu penkoom.

Joel 2:2 TSK

Bésub lëndëmu xàmbaari guddi gu ne këruus, mbete bànqanoos bu lale ci kaw tund yi. Gàngoor gu mag te am doolee ngi, gu ni mel masula am mukk, te dootul am feeki at, ba maasoo maas.

Bésub keroog Yerusalem la ndox muy dund di wale, genn-wàll gi jëm géeju penku, genn-wàll gi, géeju sowu, te noor ak nawet lay doon.